Tiit wala njàqare yëfu nit la, du moom ngay diisóol mu teg la ci yoonu teey, loolu xamoon na ñu ko ; rax ci dolli, ku ko fal njiit mu nësëxël say mbir, loolu leer na tey.

Nitóodi guy gën di sax. Gaawa tuumaal sa morom. Ñaaw njoort guy wesaaroo… 

Li ma ci gëna metti, du ñu la teg a ti NIT, dila duppee « KAA »

Bés bu nekk, muy suba, guddi mbaa ngoon, fépp ci àdduna, gay dégg ñu leen di woneek a naataable (« ‘KAA EMPOORTE », « KAA KONTAK » ak « KAA KOMINÓTEER », rek ngay dégg…)

Bu ñu la askanalee « kaa empoorte », nga gis gaa yi di waxtaane sag gàtt xel (- « waa kii fu xelam nekkoon ba mu ñuy indil lu ñaaw lii ci sërice, te fekk na, neena ñu ‘kunekk na toog fa mu nekk’ ? »)

Gurupu « Kaa kontak » ñoom, li ci ëpp ñu ngi leen jàppee ay nit yu ñu tooñ, bëre daanu seen kow, ba mu des ñenn ci ñoom ñuy rëcc, daldi di seey ci gox yi, bay mujjee wàll waa ñetteeli gurup bii ci topp.

Ñoonu nak ñoo lëmbee palatóo tele yi : muy waa « kaa kominóteer », maanaam daal, ñi ñu jappee ne fexe ña ñu ba ñu wàll leen feebar bi, te menuñoo wax ci kan la ñu ko jëlé ! Ñooñu ñoom seen der setu fi benn yoon ; ndax boobule fasoηiwàllante moo jaaxal ñi yor mbir mi, te looloo tax ken gëmatul njiit yi di wëy di naan « mbir mi, mi gi law, waaye dara weesuwu ci sunub xarañ, xam na ñu li ñuy def… ! »

Kërug yéene kaay yi tamit, ken demul ñu des ! Ñu ngay bind te di ko fësal ci xët gi : « Diw moo JOX feebar bi naηngam ak naηngami nit » ci njabootam wala ci ligéeyukaayam… Dëgg la, gis na ñu fi ñenn ñoo xam ne seen taxawaay ci wàll wii, kenn menu koo nangu. Teewul ëppal ak ηakk teey ngi fës ci ni ñuy jéebaanee suñu mbokk aki doomu ndey yi feebar bi gane si, jar naa xoolat bu baax-a-baax. 

Ba ci ñi ci génn sax, te ñu jàpp ni léegi wér na ñu (ni ko aji fajkat yi di leeralee ci seeniy kominike), gaa yi loolu taxul ñu ñeme leen, boole waat leen ci ñi ñuy dugganteel ci àndandoo wala dëkkëndoo. Bokk na ci itam, ñi ñuy woowee « KAA ASEMTOMATIK » (maanaam ñu yor doomu jàngoro bi, mën koo walle te amuñu benn màndargay feebar bi ; ñoonee de, fune ñu leen di seet, te kenn du leen xammee, mu melni ñu làqu te raglu, ni koronaawiris ci boppam !

Xaaj bu mujje bi mooy ñun, ñun ñepp, fileek ñuy xam ndax mbir mi dugg na ñu wala déét. Kenn ku nekk ci ñun, kon, « KAA SISPE » nga, manaam ku ñuy rëbb ndax jàppne mooma ! « Sispe » wu lan ? ‘Sispe’, ndax ken mënul waatal kenn ni laalul loo xam ne wiris baa ngi ci taq, mbaa mësuta toog ak koo xam ne mbir maa si yaramam. Kon jombul kenn, tambalee ko ci ñi fi siiwal yooyu baat di ñu ko xoolee (ba fatte ne ñun ay nit la ñu, bu jëkk ñu doon ak « KAA ») ; bokk na si ñi dëkk ci natt limu nit ñi bokk fii mba fee (« KAA bii mbaa bee »), te dugg na ci (yéene wu ñu ku woon noonu !) sunu mbokki waaw-góor ak waaw-kumba yi ñu teewal fa mu gëna mettee ci xexum mbas mi !

Xoolal, koronaa ci boppam muccul ci bile joxoñ baaraam : moom mi nga xam ne fune ñu ngi koy sip. Da ngay dëglu sax suurnaal tele bi-ñëpp-bokk-te-nguur-gi-ηaηk-ko, suurnaalist bi di ci yekk lu ne boobule ‘mbindeexit’ ; Gisuñu koog sunuy gët, waaye gaa yaa ngi koy misaal ku saaysaay, tëru di xaar similaaksaala bi mu naan ñoyy dugg la ; ñu ngi koy méngëleek ‘salté’ ; ñu ngi koy xalab, ndax gis ko ni ab gan gu teggi ndawal gu kenn piriyewul ci sunu kër/yaram, te bu duggee day yàq sunu biir, te (kaawteef, mënoon naa ñakk !) di faat i bakkan.

Moona, bu wax dëgg rek desee, ñun ñii yeneeniy mbindeef ni ñun, la ñuy dundee, te keneen defuñu lu ni mel ; ñuy jëfëndikoo mbindeef Yeek Aalam bi te, yenn saa, ñu ëppal ci lool. Ñun ñii nga xam ne ñoo gëm Sunu Borom, ñu wekk loolu ci dogaluk Borom-bi, Aji-Yërmaande mi ñu sacc te mey ñu àqi dundee cig sakkitéefam, ci kow jël ci li ñu soxla dooηη ! Ndax àqi sunu Borom, ak sunu wareefi am taxawaay bu mëtt sëkk ki mu tànn mu toogal ko fi, loolu moo fééte kow suñuy soxla wala àq. Cër boobu terewul ñuy gis ne Nit moom, ci kow bëgg-bëggam, wutum doηkaasigi wala rek yaataayumbe, day faral di am taxawway gu yées mum góorug wataboor gi gëna ñaaw jikko, mujjee jàp ne mooy buur ak bummi ci kow suuf.

Mënees naa jàpp ne lii lépp ay baat la doηη yu nit ñiy jëfandikoo te mbir mi yeggul fa ñu ko bëgga yobbu, sirtu soo ko méηgalee ak fitna bi fi mbas mi indi te muy jur ñàkk wér, ñàkk sañsañ wala ñàkk bakkan… Bu dul woon ne kàddu yooyee ñuy tek ci ndoddu nit ñi daa far mujjee yokk njàxare, jur boddeekoonte ak ñakk kóolu ci sunu biir, ba ci lu mel ni tam dëmm aji feebar bi. Lu muy indi mooy ay nit yu dul nangu ne feebar bi dal na leen, ay nit yu ñuy faj mbaa caytu ñuy rëcc daw làqu. Lu muy jur itam mooy ñëg ag jëfëndiku doole bu jéggi dayoo, muy ci anamu wax gu ñagas, dóor yu tar, gaañ nit wala xañ ko àq ak yelleefam… 

Tiit ak njàxare gi lal loolu dafa dem bay feeñ ci mbiicóog-mbaaloo gi am ci wax ak tërelin yi ñuy jëmëlé ci askan wi.

Néew gaa néew am na nak ay baat yuy jóg di naan feebar bii feebar la ni yeneen yi, am ko taxul nga bon mbaa nga ñaaw ; 

Doonte nag, gannaaw ba mu ñu juralee ag tëju ci gox yi ag ci réew yi daan jokkalante ci wàllu komers, gannaaw ba mu nasaxalee koomkoom bi, Mbas mii xiir na nu ci dellu ci nekkin ak dundin bi gëna sell tey aar sunu wér-gu-yaram, li ñuy lekk, yokk sunu paspas ak taxawaay bu mucc ayib ci sàmm liñu bokk. Bu doon man, du ma bëgg ñu def ma nii, kon nak dàkkooruma ag li may gis bës bu ne… 

Man gaa, xawma ndax di naa ci mucc wala deet ; te sama taxawaay dum kuy xasaate. Waaye jàpp naa ne, sunuy mag ak rakk, doom baay ak doomu ndey, wala dëkëndoo ci adduna yi feebar bi song, su ñu leen gënoon na jox cër ag wég gi nit meritoo dëgëntaan, ci ni ñu leen di xolee mbaa taxawoo, di na ñu mucc muccaaleel bépp mbindeef, ñu ànd nekk nekkin wu sell ci Suufi Maam Yàlla gu am moccaat gii Mu ñu dénk. Bu booba tamit, yaakaar naa ne am na leneen lu ñuy feesalee suñu dund ludul ay mbiru caaxaan a kiy kasawkasaw yi ñu nekkoon te lil firndeel ne loolu du dara mooy lii : bi dëgg yegsee sàngoo melokaanu Mbas, daldi komaande ne « lépp lu amul fulla ak mucc tek leen ko fi suuf ndax ngeen mucc ci man ! », da ñoo gaaw sanni ko fëlé.

Lii waxi nit doηη la : su ma juumee, ngeen gindi ma.

Maa ngi ñaan.

Na ñu Borom-bi aar, goor ak jigéen, wéral képp ku feebar bi dal, faj xolu ñepp ñi am naqar ak tiisu ñàkk ci ag jegewaale, gannaaw ba mu ñu tàggaleek mbas mii. Te na ñu Yàlla xiir ci soppeeku gu dëggu ci sunu nekkin ak sunu taxawaay ci Suufam-su-amul-morom sii mu ñu jagleen.

Musaa MBAY

Bësum 21 ci weeru Koor

moussa.mbaye1@gmail.com